Dimblikat yi

Saartu ligey katu maaliporo

ICVolontaires ap kureel la buy yëngu ci adina bi yëp ci te duk nguur buy jox askan wi ay xam xam ci wallu ligeey boo xamni kenn du ci fayaate ay dnit niuy ligey ci kalaama xarala yu mujj yi ak ay ndajje aki poroze.mungi yengu ci walu japalante doomi adama yi ci walu askan wi ci walu wergu yaram ci biir ak bitim reew.

Ligeey kat yi nak niu ngi tol ci 16 at ba 80 att muy luy indi jokko cici ay xalaat yu wute te am solo.

Sunu giss-giss

Sunu giss-giss moy tabax ëlek boo xam ni nit ku nek ak askan wune dina mënna am saň-saňak taaneef suňu mebet di dajale xam-xam yi ci li soxal askan wi jaarale ko ci ligeyuk japalante bi.

ICVolontaires mungi bokk ci li suxali askan wi di ligey ci bokk gi muy yengu ci poroze ak ndajje yoo xamni koom lalu ko, yuy jox katan bèp mindef bu jogge ci bèpp askan bu soppa ligey ci japalante. ICVolontaires mungi xeex pour ligeyuk japalante ak nagutem.

ICVolontaires nak yoon la ngirr ay xeet yu wuute mënna dajje ngir kunek xam moroomam ak yokutek ku ci nek.

ICVolontaires mungi  yengü  ci xalaatuk motalante ci askan wi ak ci ligeey katu nguur gi.seeni yëngu nak mungi fetewu ci taneefu ligey kat yi bëgga japale askan wi ci maaliporo ak ndimbalak japale katt yi.

Ngir ligeeyuk japalnate bi mënna antu nak, ICVolontaires dafa tëral ab Saart jëmaleko ci këpp ku bëgga du ci ňioom, muy li leen di wan seen axxak seen yeleef.

Ligeeyu japalekat bi

Japalekat bi dafa di benn nit kouy jooxe ci waxtoom ci ni coobarem ngir nekinu askan wi te duniu ko ci fay dara.

Amna foo xamni nak ndaw si daniu kooy deloo li mu jëffendikoo (ci wallu lekaam ak toxoom wala ak tukeem).

Moom nak dafa wara farlu lool ci taxawu ICVolontaires.

Te dafa wara def ligey bi niu ko sant ci genja defin.

Yeen saya dina ňu ko soxla ci mu teewal ICVololontaires ci ay bërëp yu mel ni (ay waxtaanu mnbooloo, ay ndaje) wala mu dem gëstu ji ci ligeeyu benene mbooloo.

Dafa wara am sutura ndax japalekat bi dafa am ay axx ak yeleef yu Saart bi di wane muy teere bi maakole ňëpp ci biir icvolontaires.

Axxuk way japalekat

  • Dafa wara am ay lijaassa ci li ňu koy ligeeyloo ci biir ICVolontaires
  • Warna yxam li ňuko defloo lu njëk waxtuwa di jott
  • Yeneen japalekat yi ak kilifaam da ňu ko wara jox cërr te andak moom ci
  • Jooxe ci xam-xamam ci japale doomu adaama yi te kenn du ko ci fay dara.
  • Am saň-sa ňuk miin ligeey bi ňu ka sas ci biir icvolontaire
  • Bok nak ci icvolontaire ci buko neexee
  • Book ci yeeneen yenguk icvolontaire
  • Yeensaye ňu fay ko li mu dugal ci koparam bi dund gi ak tukki yi
  • Nu raa ňe ko ci taxawayam ci japalante gi
  • Nu bindal ko luy firndeel ni ligey na ak ICVolontaires

Wareefu way japalekat bi

  • Bokk ci giss-gissu icvolontaire, boolekook jox cërr kepp kufay yengu ci nangul len seen askan, diineem, bëg-bëgam, laagoom te mooytu lëpp luy xeebaate
  • Dëgu ak neexa woolu ci bëpp fann
  • Nagoo jang ci lu jëm ci ay ligey yu ňu la sant
  • Am xam-xam bu leer ci lila icvolontaire di doye wala beneen bëpp andandoo
  • Nangu tërëlin ligey bi ci ni ňu ko laaje
  • Saayoo joxe sa kadu ci apporoze naga def sa keem katan ba bu ci deň
  • Nangoo soppi ay tërëlin
  • Yorr ay mbirru bopam ci walu asirance (febar tolof tolof…)
  • Wane firndek and gu way jurr yi and ci ligeyug japale kat bi bu feke 18 atam mëtagul
  • Jubale ay giss gissam ak doxalinu icvolontaire wala beneen bepp andandoo bu wa ji di ligeyal
  • Bokk ci ci ndajje yëpp yi ajowu ci ligey bi (ndaje gestu etc)
  • Wuyoo linga waxante woon ak ICVolontaires ci wallu ligey bi nga sartowoon ak loolu
  • Teela wax sa kilifa gi ci bu feke danga am ngalankoor ndax ICVolontaires mënna teela wut kukoy wuutu
  • Bokk ci setantal bi am ci biir ligey bi
  • Topp caadak xeet bi ňu fek ji
  • Nangu saart bi icvolontaire di la siňeloo

 © 2006  ICVolontaires

©1998-2024 E-TIC|system mcart|Updated: 2019-07-30 23:00 GMT|Privacy | RSS|