Ay jumtukay

Ci pàcc bi

Féeňtek ligeeyu li jëm ci wallu ňam ci adina bi yëpp bokk ko,te nga xamni li ci ëpp doole mi ngi fetewoo ak ňii di way jëfendikukat yi ak ňi ci ligey, boole ko ak sosuk sëk yi ci biir reew yi, naam xàll na ay yoon yu baykat yu mag yi mëna jafandu waye tek na ňeneen ňi tamit ay jafeň-jafeň, gënja feeň ci neew ji doole yi ak ňi nguur gi dëddu. Nooraani bi baykat yi di def jëm ca taax yi mooy indi koom-koom bu jigeen ňi di dooleel ak mbay mu fetewoo ci taax yi.

Loolu ňu lim nak moo nara indi ay jaxasoo ci mbay mi ak baykat yi ci reew yu neew doole yi. Looloo waral ETIC di gënna farlu ci di jeema dimbali baykat yooyu ngir ňu jott ci xibaar yi jaaraleko ci xarala yu mùjj yi. Ci wall woowu nak li gënna am solo mooy xamme jumtukay  yi mënna yombal te yesal tas xibaar yi ci bërp yoo xamni ňi ko genna yitewoo seen jang soriwul. 

Jumtukaayu jokko yi

Telefon portaabal yi

Rajo yi

Internet bi

Amna ci ňètti jumtukaay yu ci am solo lool. Been bi di ràjjo yi,gënn ca am solo di rajjo gox-goxaan yi, beneen bi di telefon portaabal yiak, ci yeenn dêkk yi, internet bi ndaw yi ňu yooni di jëfëndiko.

Siwal walla jalale xibaar

So deep taskatu xibaar ci rajjo gox-goxaan yi  te nga bëgga jalalep xibaar mun nga ňu jott fi.

©1998-2024 E-TIC|system mcart|Updated: 2019-07-30 23:00 GMT|Privacy | RSS|